Перейти к содержимому

Murit ngalla deel muurook a waaru | Serigne Moussa Ka

Serigne Mbaye DIAKHATE

0:00 / 0:00

Murit ngalla deel muurook a waaru | Serigne Moussa Ka

264 просмотра · 1 месяц назад
Serigne Mbaye DIAKHATE
11,2 тыс. подписчиков
264 просмотра · 1 месяц назад
Sëriñ Muusaa ka Murit ngalla deel muurook a waarook a waaraate Di ñaaxook a ñaaxaateek a bégleek a xuppaate Te def sab sëriñ muy kerkeraan jëm ci ay ngërëm Te bul weddi lam santaane bum wax nga naa mbaate Te jébbal ko sab xol fàww jébbal ko say alal Te nos ruu gi wommat jox ko tey wax yërëm maati Defal gumba jébbal tum bi kuy jis te bul gëlëm Te bul xorxoral kon lee nga dem xayra xadraati Te bul jànni bul diiŋat sëriñ mukk bul xuloo Te bul mer di tontanteek a saagaak a xastaate Bu dee jëf lu wuteek sunna say njort nay rafet Sariihatu wér nay wax hahiiqatu wuutaate Te bul xàddi bul gaaral te bul jëf lu dul ndigal Te foo toll naa yaa xawsu man awma soxlaati Te foo toll ngay farlook a xër-xërlu ciy ndigal Di daw-dawlu saytaaneek jigéen ñii di waqaate Te far fuñ wëllis say bokk ak kuy sewal ndigal Berul dem ca gën jaa àlle bul dellu kër gaati Te bul geesu bul yàkkamti bul faale ab daloo Te bul xàcci bul ñaawal sa jëf njort raw naati Di daanook a jóg bul naagu kuy daanu àggagoo Ku yéegul ca kaw doo daanu bay dox di wootaate Toroxlul te bul rëy-rëylu bum soxla ngay tayal Nirul mbër maa daa wub làmb juy waaj a dëkkaate Na ngay boole xiif ak rafle tey noppi tey xalam Bu gaa ñay xaraŋ ngay jóg liléey ngën ji mboolaate Te far dëddu dunyaa kiy woraakon bi wor ku bañ Te ngay fuglu dee miy dox di songeek a bettaate Te bul weddi bul ngistal te bul woddi bul hañaan Te bul gëdde bul wex wexlu bul dox di siisaate Na nga yéene aw yiw képp kuy ngëram ne yaw Yëram ndaw ña màggal mag ña loo am nga séddaate Te màggal ku bokkak sab sëriñ doomam ak ñoñam Nga wormaal ko koo gis nag ci ñii jox hadiyaati Te def sab sëriñ muy sang buy wax nga daal di daw Te foo toll naa yaa seexu yaa seexu maa ngeeti Te say kàddu nay saf kelte buy junj lëf nga daa di daw Di cellantu buy waxtaan itam bul ko ruubaate Te ngay teel a xëy niy jëwrinam tey saxoo sikar Bu mbooloo ma toogee ngay liggéeye a ñaaxaate Te bul faale kay war naari-góoram tay dañal Di feeruy lalam tey woote dag yaak a moslaate Di mos lay ja ak yàppam wa tay gaarde xaalisam Di xaajaanu tay séddeek a boddeek a wootaate Di yor caabi yay tijjee a yor làmp yay jafal Di faj soxla sum soxla a may gaa yi kër gaati Du buurook a biddanteek a sangook a naja jug Di fuddook a bin binlook a bëslook a déeyaate Te bul faale kay xay–xaylu tey jàngu tey daloo Di soccook a set tay seetu tay daagu naa Faati Di rixóo fuddan tey ŋàmbiy musuwaar di sol kawas Te naa ndaw si sumyaam yaatu ban dem gëroo Faati Di niirook a pornooseek a sëlmoo a wut daraa Wisoo lañkoloñ fun toll raayoo diwak mbaate Te fuñ jekki def waxtaanu xol muy ku xëy rafet Di xasteek a reetaaneek a màtteek a boddaate Di faarook a waxtaaneek a fóotlook a dox di kaf Di toog ak jigéen cib lal di riisook a déeyaate Di sangoo malaanam yaak a tër tërub cib lalam Di bantuy xetam tey wax dikkal fii nu fóonaate Te doo dégg kuy ñaaxaate tey yedde fib kuréel Di wut luy ngëram tey xërlu céy liyeek a jombaate Damay sàkku man Muusaa ci barkeb sunum Sëriñ Mu wattal nu sun ñaawtéef yi muy xayra xayraati Sëriñ bee di géejug Yàlla nan fóoti tay setal Ndoxam mee fi saf suukar safak lem te dàqaate Dagaan nan ci barkeb Bàmba kiy xutbu xarnu hii Mu fóotal nu sunu bon bon yi ban xëy di fóotaate Te may képp kuy sàkkuy ngëneelam la muy damoo Ba dun xaare dun yalwaan dun dox di soxlaati Te may nuy murit yuy sàkku yuy sóobu ciy ndigal Te tibbal nu ciy mbóotam ba nuy xëy tibbaate Te xejjal nu fal noo fal ba nuy buure baatinam Te leeral nu ciy làmpam ba nuy xëy di taalaate Te feg dee gi feg moy feg balaa xiif itam mu feg Te ñaagal nu ciy ndàmbam ba nuy xëy di ñaagaate Te sellal sunuy jëf boole sun fan yi faf guddal Te yaahal sunuy wërsëg te may nuy hadiyaati Te yokkal nu sunu mbooloo yi fob xol yi tàppe leen Ba kenn dootu nooneek kenn sàkkaa di ŋàññaate Te dox sunu digak saytaane wa nafsi wa hawaa Wa dunyaa te not noonam yi des fii di xuppaate Te wommat nu fid dunyaa illal jannati hulaa Te leeral sunuy xol fii banuy dox di waaraate