Tuubee ko war, yayoogul tawat… - Jàngat Wolofal Serigne Mbaye Diakhaté
Serigne Mbaye DIAKHATE
0:00 / 0:00
Tuubee ko war, yayoogul tawat… - Jàngat Wolofal Serigne Mbaye Diakhaté
307 просмотров · 9 дней назад
Serigne Mbaye DIAKHATE
11,2 тыс. подписчиков
307 просмотров · 9 дней назад
Ndaxam dag budul dox fa dee fii xaree
Ta naa bëgg na’g pal, dafay say, du nit
Bu dag yépp booloo fanaanee fital
Ta yendoo fital nag ba sangoo deret
Nga gis muy fanaanee nelaw bay xaran
Di yendoo larax nag te réy ay mbébét
Bu dee fee bégal gaa ya jam-jam ya wër
Mu dem fay xulookay jalookay tawat
Bileb dag yëgul ndax ne tuubeeko war
Yayoogul tawat nag, yayoogul xul it
Ndofam gee ko dal kat, tawat koo ko war
Ta jug tuubi, ay dal na dof buy téxét
Torox naa ta rus man mi gis saa ayib
Namay def ba man saa ayib jépp set ?
Bu fekkoon ni mën naa faxas ay ayib
Ma fab saa ayib jii faxas man mu set
Faxaskat bi yaw miy faxas ay ayib
Lu tee nga faxas saa ayib jii mu set ?
Ta saa soo yayoo fopp saa lépp set
Ta jag fàww may waa ju léppam rafet
Yëram maa yëram man, jubal maa jubal
Ta may nu’y ngëram nag ba nuy ngën ji nit
Faral nuy ayib nun fegal nuy ayib
Ta may nu’y ngëram nag ba ñuy ngën ji nit